scienceinwolof.bsky.social
@scienceinwolof.bsky.social
🌍✨ Jëma xam ngir xamal.
🔬 Xam-xamu àddina buñ faramfacce ci Wolof.
Amoul solo
December 2, 2024 at 10:24 PM
Dédét nakk, Yalla baxewouma xam xam bu ni mel.
December 2, 2024 at 9:36 PM
Ndax loolu kesseh mën tax lu dikkël ben bi, dikkël beneen bi ci saasi.

Jàngat yi ñu def ci jamono yii, dañu firndeel ne mbir moomu dëgg la. Noonu itam, boroom xam-xam ñi ngi xalaat ci naka lañkoy mën a jëfandikoo, ngir génné ci njariñ yu bari ci wàllu xarala yu melni kriptografi ak internet.
December 2, 2024 at 8:08 PM
Te loolu wutul ban soriway moo dox seen diggante.

Li tax mu yeemé Moy né, dara ci liñu xam, geent gaaw leer. Té nag sax limiy gaw gaw, gaawaayam am na àpp. Teh mbir mi, dey tekki né, amna lu jokkalé ñaari dondj yi am gaawaay bu amul ápp.
2/3
December 2, 2024 at 8:08 PM